POÈME DE ABDOULAYE SENE SUR CHEIKH SEYDIL HADJI MALICK SY

YOBBALLOU GAMOU 

RÉFÉRENCE BI

Hamdan Man 'Abdoullah
Mangui santate Allah
Di julli ci Rassoulillah,
Mii maami RÉFÉRENCE BI

Mangui yééssal sama ŋjébbal
Ci gorgui,ndax moñu Sagal,
Sigguil ñu fii ci Sénégal.
Defnaala RÉFÉRENCE BI.

Ousmane Sy lanuy wowé sa baye,
Sokhna Fa Wade Wélé moy sa yaye;
Defnaala ngay sama wéeru waye
Ndax yay sunu RÉFÉRENCE BI.

Dëk ba mu juddóo móodi Gaaya,
Té mom dafa jud-du jaaxal Gaaña
Ca Gaaya. Kon sunu gorgui rawna
Té mom lañu def suñu RÉFÉRENCE BI

Baatum jubblu won ci Maalick
Moy firri turamwa EL HADJI MALICK
Wayé la njëkk Hand Ladji Maalick
Mo nékon turu RÉFÉRENCE BI.

Nëb ŋanu sa bópp wonñu ALLAH
Hamalñu kúuy RASSOULILLAH
Nan ñu ''Mohamed noûru 'abdillah''.
Motax ma def la sama RÉFÉRENCE 

Tambaliŋa ca bamu nékké "Nour",
Ba numu wuyu jé sunu bour.
Kenn méyulako kudul As-sabour.
Defnañ la ŋay sunu RÉFÉRENCE BI.

Mame MAODOY guéeju xam xam,
Ndax muŋ koy don né ci Maamam
Mouhamad sallallahou aleyhi wa salam.
Kon defnañ la sunu RÉFÉRENCE BI

Moñu xamal mbóolem mbóotu Al qur'an,
Ak yénéni "ilm" luci melni fiqqak bayyan.
Kuko weddi xoolal ci El Hadji Raw-han
Ngom mi nékon ci wétu RÉFÉRENCE BI.

Mba ŋa xol ci Serigne Babacar Sy Malick,
Mansur Sy Balkhawmi wala Dabakh Malick
Ñi doynañu ŋir ma Séedel Maodo Malick
Mi ma def tay sama RÉFÉRENCE BI.

Mame MAODO mo diaxalon Tubab ba,
Ba fumu daajé église,mou daj fa jakka
Tek ci di jollil soubak ŋon salatul fatiha
Kon jaaraama sunu RÉFÉRENCE BI

Motax kuné ragalonna tubab daŋay nar,
Ndax mofi taŋ xalon kuñuy nan Bolokar.
Xana guisso zawiyam yamu daj Dakar ,
Ndar mba dëkkëm bu sella ba Tivaoune.

Démal tey dëk biñuy náan Casamance,
Diŋa xamné sunu Mame amoul Mass.
Ndax niom ñeppay tiitëroo Mame Ass.
Té mom lañu def tey sunu RÉFÉRENCE

Nonu la def ba adunna bi fo mënti dem
Sampa nafa kennë muy missionnairam
Heilallah bi di diolli ak "nûrul mutalsam".
Yalnagnu yalla feyyal Mame MAODO

Nonu la def ba tey ji mu tasáaré Diiné bi.
ak Tariqa cheikh Ahmada Tiijane shérif bi,
Móoko tassáaré yitam ci Ad-dounna bi
Kon jërëjëfé Mame MAODO MALICK

Mame Ahmadou Bamba wëy nako,
Cheikhna Cheikh Sadbou wëy nako,
Kon dey warat tey ci man ma wëy ko
Ndax moy sama RÉFÉRENCE BI.

Jëflantéwonnak Mame Abdoulaye Niass
Ndax kulen bóoléwon moy Abboul Abass
Kérok la Mame Abdoulaye wëy Mame Ass,
''Nilnal maraama wa nilnal qâciyal Haji(...)"

Hamnaani guécc ŋa mënumala diéxal,
Wayé suma duyé ci yow rek dináa féssal;
Té bu sobé rabbi duma diok ci di féeñal
Cofél gui ma am ci RÉFÉRENCE BI

Taalif bi moy sen yobbal ci Gamu gui,
Ndax say yu ñu tud dée Gamu gui;
Xel yép dem tivaoune ci sunu Gorgui.
Ba tax malen di nianal Gamou ak Diam
ALLAHOUMA SOLLI 'ALAA SEYDINA MOUHAMAD WA 'ALA ALIHI WA SAHBIHI WA SALLAMA TASLIIMA

ABDOULAYE SENE AMBASSADEUROU CHEIKH SEYDIL HADJI MALICK SY
 
                   DIAARAMA EL HADJI MALICK SY


Commentaires

  1. Machalla machalla yalna yalla wéral bade bi té mayla goude fane thi barké Mame Maodo Malick Sy RTA ❤️

    RépondreSupprimer
  2. Machalla mn frère bne continuation yalna bate bi way

    RépondreSupprimer
  3. Bonn continuation dans frère t'a bien assuré yalna la yalla défal fassaaha

    RépondreSupprimer

Enregistrer un commentaire

Je me nomme Abdoulaye SENE étudiant en première année à l'Université Cheikh Anta Diop de Dakar. Je suis dans le département des nobles qui est la Lettres Modernes. Je suis donc un apprenti littéraire en même temps un blogueur..
Mon objectif dans ce blog est de produire des articles qui reflète la réalité , rien que la réalité et toute réalité. En un mot je suis tout à fait engagé.

Posts les plus consultés de ce blog

HOMMAGE À MATAR DIAO