POÈME DE ABDOULAYE SENE SUR CHEIKH SEYDIL HADJI MALICK SY
YOBBALLOU GAMOU RÉFÉRENCE BI Hamdan Man 'Abdoullah Mangui santate Allah Di julli ci Rassoulillah, Mii maami RÉFÉRENCE BI Mangui yééssal sama ŋjébbal Ci gorgui,ndax moñu Sagal, Sigguil ñu fii ci Sénégal. Defnaala RÉFÉRENCE BI. Ousmane Sy lanuy wowé sa baye, Sokhna Fa Wade Wélé moy sa yaye; Defnaala ngay sama wéeru waye Ndax yay sunu RÉFÉRENCE BI. Dëk ba mu juddóo móodi Gaaya, Té mom dafa jud-du jaaxal Gaaña Ca Gaaya. Kon sunu gorgui rawna Té mom lañu def suñu RÉFÉRENCE BI Baatum jubblu won ci Maalick Moy firri turamwa EL HADJI MALICK Wayé la njëkk Hand Ladji Maalick Mo nékon turu RÉFÉRENCE BI. Nëb ŋanu sa bópp wonñu ALLAH Hamalñu kúuy RASSOULILLAH Nan ñu ''Mohamed noûru 'abdillah''. Motax ma def la sama RÉFÉRENCE Tambaliŋa ca bamu nékké "Nour", Ba numu wuyu jé sunu bour. Kenn méyulako kudul As-sabour. Defnañ la ŋay sunu RÉFÉRENCE BI. Mame MAODOY guéeju xam xam, Ndax muŋ koy don né ci Maamam Mouhamad sallallahou aleyhi wa salam. Kon defnañ la sunu RÉFÉ...